TSK

TSK · Numbers 18:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Na fa Aaróona taal cuuraay suba su nekk. Buy topptoo làmp yi lay taal cuuraay lu xeeñ li.

Ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona di teg làmp yi, muy fanaanee tàkk ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.

«Buleen yóbbe Keyateen ñeek seeni làng, lu ñu leen di dagge ci biir Leween ñi.

te itam maa jukkee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen yékkati, jox leen Aaróona aki doomam, ngir ñu liggéey liggéeyu bànni Israyil ci wàllu xaymab ndaje mi, di defal bànni Israyil seenug njotlaay, ngir bu bànni Israyil jegee bérab bu sell bi it, du tax menn mbas am ci seen biir.»

Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax lii ci mbirum yonent yi: «Maa ngii di leen leelsi njàqarey xeme, nàndal leen tookey mbugal, nde fi yonenti Yerusalem la yàqute tukkee, ba law ci réew mi mépp.»

Ñoom doŋŋ ay dugg sama bérab bu sell bi, ñoom doŋŋ ay jege sama taabal, di ma liggéeyal, di dénkoo sama ndénkaane.

¶ Kon nag Timote doom, loolu mooy ndigal li ma la dénk, te mu dëppook kàdduy waxyu yi jotoona jib te jëm ci sa mbir. Gànnaayool kàddu yooyu ngir di ci xaree xare bu baax bi,

¶ Maa ngi lay àrtu nag fi kanam Yàlla, ak Almasi Yeesu, ak malaaka yi ñu tabb, ngir nga sàmm loolu te baña jeng, mbaa nga jëfe lenn loo defe xejj ak seen.