TSK

TSK · Numbers 18:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sàkkal ci deret ji ci sarxalukaay bi, ak ci diwu pal gi, nga wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ci kawi yéreem, wis-wisal ko ci kaw yarami doomam ak ci seen kawi yére. Su ko defee Aaróona sell, mooki yéreem, ay doomam it sell, ñook seeni yére.

¶ «Yérey Aaróona yu sell yi nag, gannaaw bu dëddoo, dees koy féetale ay doomam, ñu fale leen ko ci seen xewu colug carxal.

Nga diw leen, ni nga diwe seen baay, ñu doon samay sarxalkat. Seen diwu googu moo leen sédd sasu carxal bu sax dàkk, maasoo maas.»

«Waxal Aaróona ak doomam yu góor ne leen: Dogal bi ci saraxu póotum bàkkaar mooy lii: Juru saraxas póotum bàkkaar dañu koy rendi fa ñu wara rendi juru saraxu dóomal, fi kanam Aji Sax ji. Lu sella sell la.

Nañu jooxeel Aji Sax ji ab cér ci sarax yooyu yépp, muy moomeelu sarxalkat bi xëpp deretu juru saraxas cant gi ci biir jàmm ci mboolem weti sarxalukaay bi.

¶ Loolooy céri pal yi Aaróona ak askanam di am ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, dale ko keroog bu ñu leen teewalee fi kanam Aji Sax ji, ñu doon ay sarxalkat.

Waaye dënnu saraxu yékkati-jébbale bi ak tànkub jooxe bi, lekkleen ko ci bérab bu mucc sobe, yaak say doom yu góor ak say doom yu jigéen, ndax seen cér la, ci saraxi canti bànni Israyil ci biir jàmm, nga moom ko yaak say doom.

Sarxalkat bi day yékkati ñaari xar yooyu, boole kook mburum ndoortel meññeef mi, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yooyu sarax di lu sell ñeel Aji Sax ji, sarxalkat bee ko moom.

Lii nag, yaa ko moom, ci mboolem sarax yu sell yee sell, yi mucc sawara: seen bépp sarax, seen bépp saraxu pepp ak seen bépp saraxu póotum bàkkaar, ak seen bépp saraxu peyug tooñ bu ñu ma indil, lu sella sell la, ñeel la, yaak sa doom yu góor.

su boobaa bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji taamu ngir dëël fa turam, foofa ngeen di yóbbu mboolem lu ma leen sant: seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak mboolem ngëneel yu ngeen di def saraxi xas yu ngeen xasoo ak Aji Sax ji.

te na ku nekk ci yeen wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Jële naa sama kër céru sellnga bi, ba jox ko Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun yi, noonee mu dëppook sa santaane bi nga nu dénk. Moyuma lenn ci say santaane, te fàttewuma ci lenn.

Yaa safoo njubte, seexlu njubadi, moo tax yaw Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom.»