Numbers 1:19
TSK
Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi.
«Na bànni Israyil di dal, ku nekk ak raayaam ak xàmmikaayu kër maamam. Fi wër xaymab ndaje mi te dànd ko as lëf, fi lañuy dale:
¶ Noonu la bànni Israyil topplantee, ànd ak seeni gàngoor, tegu ca yoon wa.
Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba, giseesul aw naqar ci xeetu Israyil wii. Seen Yàlla Aji Sax jee ànd ak ñoom, njiinum buur a jibe fa seen biir.
Yanqóobaa, yaaka yànji xayma! Israyil, laa ne, yaaka taaruy màkkaan!
Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.