TSK

TSK · Numbers 20:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»

Yóbbaaleel yet wii nag, ndax ci ngay defe firnde yi.»

Musaa ak Aaróona def loolu lépp, na leen ko Aji Sax ji sante. Naka la ne xaas yet wa, ne ko tàrr ca ndoxum Niil ma, ca kanam Firawnaaki dagam, ndoxum Niil ma mépp di deret,

Aji Sax ji ne Musaa «Àndal ak ñenn ci magi Israyil, nga jaar ci kanam mbooloo mi, yóbbaale yet, wa nga dóoroon ca dexu Niil ga. Ŋàbb ko ci sa loxo te dem.

Ci kaw loolu Musaa yékkati loxoom, dóor yetam ca doj wa ñaari yoon, ndox mu bare wale ca, mbooloo ma daldi naan, ñook seenug jur.

Ay garmee la bënn, kàngami askan wi gase la yeti buur, ak seen banti bopp.» Ñu jóge màndiŋ ma, dem ba Matana,

Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.

Mu bënnu doj, ndox ma ball, di dex, wale joor gu wow.

Walaakaanaak néew-doolee ngi wër, di wut um ndox, amul. Seen put wow koŋŋ ak mar. Man Aji Sax ji, maa leen di nangul; man Yàllay Israyil, duma leen wacc.

Marewuñu bérab yu wow ya mu leen jaarale woon, ndox mu balle ciw doj la leen xellil, moo xaru doj, ndox ma baawaan.

Acts 1:14 TSK

Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.

¶ Ci kaw loolu malaaka mi won ma dexu ndoxum dund mu leer nàññ ni doju kiristaal, ndox ma wale ca ngàngunem Yàllaak Gàtt ba,