Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?
TSK
TSK · Numbers 21:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.
te bu bët setee dingeen gis manoorey Aji Sax ji, ndaxte dégg na ngeen di diiŋat Aji Sax ji, ndax nun kat tekkiwunu dara, ba ngeen di nu diiŋat.»
¶ Waa kër Israyil nag tudde ñam wa mànn (mu firi Lii lu mu?). Dafa meloon ni pepp, mi ñuy wax koryanda, te weex, di saf lu mel ni nàkk bu ànd ak lem.
¶ Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam Aji Sax ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba.
Weeru lëmm kay lañuy yàpp, ba yàpp wiy génne ci seen paxi bakkan, ba mujj génnliku leen, gannaaw ñoo xarab Aji Sax ji ci seen biir, di jooy ci kawam, naan: “Moo lu nu taxoona jóge Misra!”»
Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci?
Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay.
Ñuy waxal Yàlla naan: «Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi!
Ku suur, bañ lem ju xelli, waaye boo xiifee, lu wex lu ne neex la.