TSK

TSK · Numbers 22:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji nag yeb kàddu ci gémmiñu Balaam, daldi ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji dajeek Balaam, daldi yeb kàddu ci gémmiñam, ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»

su ma Balag joxoon këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def ci sama coobarey bopp, lenn lu baax mbaa lu bon, lu tebbi ndigalu Yàlla Aji Sax ji? Li Aji Sax ji wax rekk, moom laay wax.

Waaye ba ngeen gisee Nayas, buurub Amoneen ña jëm ca seen kaw, yeena ma ne: “Buur bu nu jiite daal lanu bëgg.” Te Aji Sax ji seen Yàlla di seen buur.

Teewul bala seen xel a dal, seen lanc jàllagul sax,

Yaa xadaru sama kaw, ba sag reewande tàbbi sama nopp! Maa lay takkal ag nos akug laab, waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon.

Ci biir mer laa la falal buur, te ci samam sànj laa ko follee.