TSK

TSK · Numbers 22:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»

Yàlla ne Balaam: «Bul ànd ak ñoom, te bul ñaan-yàlla mbooloo ma, ndax ñooñu ñu barkeel lañu.»

Balaam yékkati kàddug ñaanam, ne: «Fa Aram la ma Balag buuru Mowab jële, foofa ca tundi penku ya, ne ma: “Kaay ñaanal ma yàlla Yanqóoba, Dikkal rëbbal ma Israyil mii.”

Balag ne ko: «Kaay rekk, ma yóbbu la feneen. Jombul Yàlla nangu nga móolool ma leen foofu.»

Ab Amoneen mbaa ab Mowabeen du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci ñoom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji mukk,

Mu ne Daawuda: «Xanaa ab xaj laa, ba nga di ma jëlalu yet?» La ca tegu waa Filisti ba móolu ko ca turi tuuram,

Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»

Li ko waral moo di ñoo bañoona dabe bànni Israyil aw ñam wu ñu lekk ak ndox mu ñu naan, xanaa di fey Balaam, jibar ba, ngir mu rëbbal leen leen. Teewul sunu Yàlla soppi rëbb ga barke.

Ñooy móolu, yaw nga barkeel; ñoo ma jógal, ñooy torox, man, ma bég, Sang bi!

Jàppool say jat rekk ak sa xërëm yu ne xas yoo dale sonn ba ngay ndaw. Jombul mu amal la njariñ, mbaa ñu ragale la ko.

Acts 8:9 TSK

¶ Ku ñuy wax Simoŋ nag yàggoon na ca dëkk ba, di ñeengo. Ku waar waa Samari la woon, te doon tuddoo nit ku màgg.