Ba loolu weesee la bakkanu Ibraayma rot, mu nelaw, fekki ay maamam, gannaaw ba mu guddee fan, ba màggat lool te barkeel.
TSK
TSK · Numbers 27:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 25:8
TSK
Numbers 20:24
TSK
«Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba.
Numbers 33:38
TSK
¶ Ba mu ko defee Aaróona sarxalkat ba yéeg ca kaw tundu Or, ci ndigalal Aji Sax ji. Mu daldi faatu foofa, ca ñeent fukkeelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, yemook benn fanu juróomeelu weeru at ma.
¶ Ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Musaa: «Ma ne, sa bésub dee ngi jegesi. Wool Yosuwe, te ngeen teewsi fi xaymab ndaje mi, ma yeb ko.» Musaa dem, ànd ak Yosuwe, ñu teewi fa xaymab ndaje ma.
Boo noppee, deel ca kaw tund woowu nga yéeg jëm, ba ñu tërali la ca say bokk, noonee sa mag Aaróona deeye woon ca kaw tundu Or, ba ñu tërali ko cay bokkam.