Musaa ne Yosuwe: «Tànnal nu ay xarekat te nga dem xeex ak Amaleg. Ëllëg dinaa taxaw ca kaw tund wa, ŋàbb yetu Yàlla wi ci sama loxo.»
TSK
TSK · Numbers 27:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji nag wàcc ca biir niir wa, wax ak moom, daldi sàkk ca leer ga ca Musaa, sédd ca juróom ñaar fukki mag ña. Naka la leer ga dal ca seen kaw, ñu tàmbali di wax ay waxyu, benn yoon bu ñu tóllantiwul.
¶ Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
¶ Yosuwe itam, sant naa ko ci jant yooyu ne ko: «Sa bët moo la may mboolem ni seen Yàlla Aji Sax ji def ak ñaari buur yii. Noonu rekk la Aji Sax jiy def ak mboolem nguur ya nga jëm.
¶ Ba loolu amee Musaa woolu Yosuwe, wax ak moom, Israyil gépp teg ci seen bët. Mu ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay ànd ak mbooloo mii ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ne ñoom la koy jox. Yaw it yaa leen koy sédde.
¶ Aji Sax ji nag yeb Yosuwe doomu Nuun ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay yóbbu bànni Israyil ca réew ma ma giñoon, te man ci sama bopp maay nekk ak yaw.»
Kenn ca dag ya ne ko: «Man de, gis naa jenn doomu Yese waa Betleyem bi. Ku mana xalam la te jàmbaare. Ñeyi xare la. Ku déggi wax, ku góorayiw, te Aji Sax ji ànd ak moom.»
Dégg naa sab jëw, ñu naan noowi yàlla yaa ngi ci yaw, te gis nañu ci yaw ag ràññee akum xel ak xam-xam bu takku.
Kon nag bokk yi, seetleen ci seen biir juróom ñaar ñu rafet seede, soloo Noo gu Sell gi te rafet xel, nu dénk leen sas woowu.
Ñu agsi Samari, ñaanal gëmkat ña, ngir ñu jot Noo gu Sell gi.
Ba leen Póol tegee loxoom, Noo gu Sell gi dikkal leen, ñu tàmbalee làkk yeneen làkk, boole ci di biral waxyu.
Bul sàggane may gi ci yaw, te di lu ñu la baaxee ag kàddug waxyu gu ànd ak tegeb loxo, ba la mag ñi defaloon.
Kenu gi mooy itam njànglem xeeti njàpp, ak ñaan gu ànd ak tegeb loxo, ak mbirum ndee-ndekki, ak àtteb bés-pénc biy sax dàkk.