Numbers 35:12
TSK
Mooy doon seen dëkki rawtu yees di mucce ci mbokkum jotkat buy toppe, ba ki rey nit du dee, te taxawagul fa kanam mbooloo mi, ngir ñu àtte ko.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mooy doon seen dëkki rawtu yees di mucce ci mbokkum jotkat buy toppe, ba ki rey nit du dee, te taxawagul fa kanam mbooloo mi, ngir ñu àtte ko.
su boobaa la mbooloo may wéyal diggante ki rey, ak jotkat bay toppe, moo di àtte yii ci yoon tëral:
Toppkatu bakkan ba nag warul mana dabi ci biir xolam bu tàng, ki rey, ba rey ko ngir sorewaayu yoon wa jëm ca dëkkub rawtu ba, te àtteb yoon reyluwu ko, gannaaw fekkul woon mu bañ ka mu rey, démb ak bëkk-démb.
¶ Noonu la Yowab ak rakkam Abisay bóome Abner, ndax la mu reyoon seen doomu ndey Asayel ca xareb Gabawon ba.