te nangulul Kayin. Kayin nag mer lool, ba ne fóññ.
TSK
TSK · Numbers 35:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Waaye nag, su nit fexeelee moroomam, nax ko, ba rey ko, su làqoo woon sama sarxalukaay sax, jàppleen ko, rey.
¶ Ca ëllëg sa ngelawal Yàlla lu aay ne milib ca kaw Sóol, muy waxtu ca digg këram. Daawuda nag di ko xalamal, na mu daan def naka jekk, fekk Sóol ŋàbb ab xeejam.
Ci kaw loolu ngelaw lu aay lu Aji Sax ji dikkal Sóol, fekk ko toog ci biir këram, ŋàbb ab xeejam, Daawudaa di xalam.
¶ Ci kaw loolu ñu yegge Sóol ne ko Daawuda dem na Keyla. Sóol ne: «Kon de Yàllaa ko teg ci samay loxo, ndax ba mu duggee biir dëkk bu tëje ràpp la tëj boppam.»
Naka la Abner délsi ba Ebron, Yowab berook moom ca buntu dëkk ba, mel ni kuy déeyook moom, daldi koy jam ci biir, rey ko, feyul Asayel, rakkam ja Abner bóomoon.
¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»
¶ «Yaw ci sa bopp xam nga li ma Yowab doomu ndaw sa Seruya def, te def na ko ñaari njiiti xarey Israyil, di Abner doomu Ner ak Amasa doomu Yeter: rey na leen, tuur seen deret ni bu doon xare, ba taqal boppam ripp. Moo rendi ci biir jamonoy jàmm.
Ay móolu la gémmiñ ga fees, ak fen ak njublaŋ, njekkar ak ñaawtéef lal làmmiñ wa.
Defuma dara, ñu di ma fiir, defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru.
Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.
Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw; bu ko kenn taxawu.
Mu toog fa ñetti weer. Gannaaw gi muy waaja dugg gaal jëm Siri, far pexe mu ko Yawut ya lalal feeñ, mu fomm, nara dellu jaareji Maseduwan.