TSK

TSK · Philippians 1:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Luke 15:7 TSK

¶ «Maa leen wax, ne leen: bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee, noonu rekk lay doone mbégte fa asamaan, ba raw mbégte ma fay am, bu juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti nit jubee, te soxlawuñoo tuub.

Yàlla mi may jaamoo xol, ci ni may siiwtaanee xibaaru jàmm bu Doomam, moom seere na ne noppiwuma leena fàttliku.

¶ Li may ñaan nag moo di seen cofeel yokku tey gën di yokku, te ngeen ànd ceek xam-xam bu matale ak gépp ràññee,

Ndaxte ñu baree ngii ñu seeni jëf tax ñu di nooni bantub Almasi. Loolu wax naa leen ko ay yoon, ma waxati leen ko tey aki jooy.

Ndax jëmm ji kat teewul, waaye xol baa ngeek yeen, di bégee gis seen doxalin wu jekk, ak seen ngëm gu wér gu ngeen gëm Almasi.

Ndax kat, ana kan mooy sunu yaakaar, di sunu mbég, te di sunu kaala gu nuy sagooji? Xanaa du yeen, kera ca sunu kanam Boroom Yeesu, bu feeñee?