Ñu dóor leen ay yar yu bare, sànni leen ca kaso ba, boole ca jox boroom kaso ba ndigalal wattu leen bu baax.
TSK
TSK · Philippians 1:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?»
Cofeel moo di: lépp, nga bale; lépp, nga gëm; lépp, nga yaakaar; lépp, nga dékku.
Du teg leen tooñ laay waxe lii, ndax wax naa ko ba noppi, yeena ngi ci sunu xol, ngir nu bokk dund, mbaa nu bokk dee.
¶ Moo ma tax di ñaan, man Póol mi ñu tëj ngir Almasi, ndax ñi dul Yawut, yeen jaambur ñi,
xibaar bi ma di ndawam lu ñu tënke ay jéng. Waaye ñaanal-leen ma ma di ko waxee fit, ni mu ma ware.
Ñooñu cofeel a leen tax di waare, ndax xam nañu ne waxal xibaaru jàmm bi laa sasoo.
Te ngeen ñaanaale nu ci itam, ngir Yàlla ubbil nu buntu xamle kàddu gi, ngir siiwtaane mbóot mi ci Almasi, li waral ñu jéng ma.
¶ Nu ngi sant Yàlla fu nu tollu ci yeen ñépp, te noppiwunu leena fàttliku ci sunuy ñaan,
¶ Bul kersawoo di seedeel sunu Sang, mbaa nga di ma kersawoo, man mi ñu tëj ngir moom, waaye jëlal sa wàll ci coonob xibaaru jàmm bi, ni la ko manoorey Yàlla manloo.
¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
Leeg-leegaa ñu saaga leen, bundxatal leen ci kanam nit ñi; leeg-leegaa yeen ay taxawu nit ñi ñu teg lu ni mel.
¶ Mag ñi ci seen biir di seeni njiit nag, dama leen di ñaax, man miy njiit ni ñoom, di seedeb coonoy Almasi, te di boroom cér ci ndam li nara feeñ.