TSK

TSK · Philippians 4:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag, soo leen dee baal seen bàkkaar, aa... Lu ko moy kat, far ma rekk ci téere bi nga bind.»

Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ ak ku des fa Yerusalem, ku sell ki lees lay wooye, muy képp ku ñu bind turam, te mu wara dese bakkan ci Yerusalem.

¶ Malaaka ma waxati ma, ne ma: «Jamono yooyu ci la Mikayel, malaakam wattukat mu mag, miy taxawu sa mbooloo, di jóg. Muy jamonoy njàqare ju masula am, cosaanal xeet yi ba tey jii. Bu keroogee sa bokk yay mucc, di ñi ñu bind ci téereb dund bi.

Acts 9:36 TSK

¶ Dëkk ba ñuy wax Yope, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon.

¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.

Nuyul-leen ma it Urben, sunu mbokkum liggéeykat ci liggéeyub Almasi, ak Estakis, sama soppe;

¶ Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di xeex ngir saxal ngëm gi sukkandiku ci xibaaru jàmm bi.

¶ Bu loolu weesee, Ewodi laay tinu, di tinu Santis, ñaari jigéen ñooñu, ngir ñu fexe ba juboo, ngir Boroom bi ñu bokk.

¶ Limeefu jëtun ñi ndimbal ñeel, deesu ci bind ku am lu yées juróom benn fukki at, te na di ku masul am lu wees jenn jëkkër doŋŋ,

Ku am ndam mooy soloo noonu mbubb mu weex, te turam, duma ko far ci téereb dund bi, waaye maa koy wuyul ci sama kanam Baay ak ay malaakaam.

Rab wi nga gis mas naa nekk waaye nekkatul. Dina génne ca xóote ba, waaye day sànkuji. Waa àddina, ñi ñu bindul woon seeni tur ci téereb dund bi ba àddinay door nag, bu ñu gisee rab wi, dinañu yéemu, ndax la mu masoona nekk, tey nekkatul, te ëllëg muy nekkaat.

Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.