Job 31:24
TSK
Ndegam damaa def wurus sama yaakaar, bay tudde ngën-gi-wurus sama cëslaay;
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndegam damaa def wurus sama yaakaar, bay tudde ngën-gi-wurus sama cëslaay;
Yàlla da lay sànk ba fàww, fëkke la sab xayma, yóbbu, déjjatee la réewum aji dund. Selaw.
Alal day aar boroom ni ab tata, mu xalaat ne maneesu koo bëtt.
Bul xañ néew-ji-doole; néew-ji-doole la. Ku tumurànke, bu ko soxore cib àtte,
Kuy damu kay, na damoom xelam mu ko may mu xam ma, xam ne maay Aji Sax, jiy jëfe ngor ak dëgg ak njekk fi kaw suuf. Loolu déy mooy sama bànneex.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.