¶ Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.
TSK
TSK · Proverbs 11:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 7:1
TSK
Job 36:18
TSK
Bu la kenn xiirtale alal, te bu la ger bu réy jengloo.
Proverbs 10:2
TSK
Alal ju lewul du jariñ; jub, mucc ci gàtt fan.
Isaiah 10:3
TSK
Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, keroog ba safaan di bawoo fu sore? Ana ku ngeen di daw wuti wallam? Ana fu ngeen di denci seen teraanga?
Ezekiel 14:14
TSK
su Nóoyin ak Dañeel ak Ayóoba bokkoon nekk ca seen biir sax, ñoom ñett doŋŋ la seen bakkan di mucc ndax seenug njub. Boroom bi Aji Sax jee ko wax.
Romans 5:17
TSK
Moyug kenn nit ki, ci la dee jaare ci kenn nit kooku, ba falu, kon ñi jot ci xéewalu yiw, ba jagoo àtteb njub, ñaata yoon lañuy gënatee falu ci biir dund gu ñu ame ci keneen nit kiy Yeesu Almasi?