TSK

TSK · Proverbs 13:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ibraam dëkke réewu Kanaan, Lóot sance dëkk ya ca jooru Yurdan, daldi toxal xaymaam, samp ko Sodom.

¶ Robowam nag dégluwul waxi mag ña, xanaa dem giseek xale yu góor, ya màggandoo ak moom te di ko taxawu.

Mu ne Yosafat: «Xanaa dinga ànd ak man ca xareb Ramot ga ca Galàdd?» Yosafat ne buurub Israyil: «Maa ngi, yaa ngi, samay nit ay say nit, te samay fas ay say fas.»

Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.

Waa ja jekki, topp ko, mbete yëkk wu ñuy rendiji, mbaa dof bu ñu jéng, di ko yari.

Dëddul jëfi téxét ba dund, di jubal ci yoonu dégg.»

Kuy dégg àrtu yu koy musal, ku rafet xel a ngoog.

Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.

Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax.