TSK

TSK · Proverbs 13:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.

Alal ju lewul day naaw; foral benn-benn, ba biibal.

¶ «Kuy dajaleel boppam alal te woomlewoo fa Yàlla, loolu mooy saw demin.»

Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.

Nun, ay dof lanu ngir Almasi; yeen, yeena muus nu ngeen bokke ci Almasi! Nun noo néew doole; yeen, yeena am doole. Yeen it lañu naw, waaye nun, dees noo xeeb!

Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.

Ag ngoreel lañu leen di dig, te ñoom ci seen bopp, ay jaami yàqute lañu, nde lu la man, yaa dib jaamam.

Gannaaw yaa ngi naan: “Am naa alal, barele naa, soxlaatuma dara,” te yaw xamuloo ni nga toroxe, jara yërëm, ñàkk, gumba, ne duŋŋ,