Ndax kat seen Yàlla Aji Sax ji mooy Yàllay yàlla yi, te mooy Sangu sang yi. Mooy Yàlla ju màgg ji, jàmbaare te raglu. Ki gënalewul, jëlul ub ger.
TSK
TSK · Proverbs 15:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñu ni mel ay lekk alalu jigéen ju tëlee jur, te duñu baaxe jëtun.
Yaw de yaay ki nemmiku, di gis njekkar ak naqar, ku mu dal, nga sàmm àqam. Néew-ji-doole wéeroo la, ab jirim, nga dimbali.
Lu bon a la gënal lu baax, fen a la gënal wax dëgg. Selaw.
Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.
Ab soxor bu daanoo, jeex na; ku jub, sa kër taxaw, ne këcc.
Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf, bul aakimoo suufas jirim.
Bés déy ñeel na Aji Sax ju gàngoor yi, ca lay xaare képp ku bew ak ku reew, ba kuy daŋŋiiral, detteelu.
Waaye ba mu bewee, të ticc bay réy-réylu, dañu koo jàllarbee ca nguuram, nangu ndam la,
¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»