Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji?
TSK
TSK · Proverbs 16:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Demal wax sama jaam Daawuda, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Ndax yaw yaa may tabaxal kër gu ma dëkke?
¶ Cant ñeel na Aji Sax ji, sunu Yàllay maam, moom mi def nii ci xolub Buur yéeney teral kër Aji Sax ji ci Yerusalem,
Samay fan wéy na, mébét yàqu, yaakaar yàkki.
Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede, te dummóoyu alal ju lewul.
Bare na lu xol di mébét, waaye Aji Sax jeey dogal.
Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.
Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.
Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux,
¶ «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya, ak àttekat ya, buleen jaaxle ci nan ngeen di yékkatee kàddug layoo, ak luy doon seenu lay, mbaa lu ngeen di wax,
¶ Cant ñeel na Yàlla, mi def ci xolu Tit, mu xér ci yeen ni ma xére ci yeen!
¶ Bokk yi, soppe yi, buleen juum ci lii: