Psalms 45:2
TSK
Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
Kuy dégg, say wax rafet; te ku ñàkk bopp, yelloo yetu gannaaw.
Ku xelu àddu, xam-xam law; ab dof amul xelam.
Sama doom, soo xeloo, sama xol neex.
Waarekat ba daa tànn baat yu saf, bind ko, mu jub te dëggu.
Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?»
Yeen nag seenug dégg ndigal siiw na ba bir ñépp, moo tax ma di leen bége. Waaye damaa bëgg ngeen xelu ci lu baax, te seenum xel mucc ci lu bon.