Kàddu gu dëgguwul, soreleen ko, te ku deful dara ak kuy def njekk, buleen ko reylu, ndax nit ku bon, duma ko àtte mukk àtteb kuy def njekk.
TSK
TSK · Proverbs 17:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñaari nit ñu tekkiwul dara dikk toog janook moom. Ñu duural ko ca kanam mbooloo ma, ne Nabot daa saaga Yàlla, saaga Buur. Ñu génne Nabot dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.
Aji Sax ji bañ na njublaŋ ci nattub diisaay, ay nattukaay na mat, muy bànneexam.
Faral ku tooñ baaxul, bul xañ dëgg ku deful dara.
Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,» aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la;
«Samay xalaat déy du seeni xalaat, te samay jëfin du seeni jëfin.» Kàddug Aji Sax jee.
Kàngamam yi ci biiram a ngi mel ni saafaandu yuy dogat am pàdd, tuur deret ja, di sànk ay bakkan ngir nangu alali boroom.
Ràññee naa seen bàkkaar yu bare ak seen moy yu dul jeex. Yeenay tooñ aji jub, di geru, di xañ néew-ji-doole dëgg ci pénc.
Ñépp daldi xaacoondoo, ne: «Reyal kii te yiwil nu Barabas!»
Yeena daan ba reylu aji jub, te jéemula bañ.