TSK

TSK · Proverbs 20:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu am bés mu naan biiñ, ba màndi, tëdd ci xaymaam, daldi sàgganu.

Ca guddi ga ñu nàndal seen baay biiñ, taaw ba dugg, tëdd ak baayam, te Lóot yégul ba fa doom jay tëdd ak ba muy jóg.

Ci biir loolu Daawuda woo Uri, mu bokk ak moom lekk, daldi naan. Mu nàndal ko ba mu màndi. Ba ngoon jotee Uri daa génn, tëdd ca laltoom ca biir surgay sangam, waaye këram, àggu fa ba tey.

Ñu génn digg bëccëg, fekk Ben Addàd a ngay màndi mook fanweeri buur ak ñaar ya mu faral, ca mbaar ya.

Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?

Buur moomul di naan biiñ, Lemuyel, buur moomu ko; kilifa moomul di sàkku ñoll.

Wóoy ngalla ñiy jàmbaari naan biiñ, diy ndaanaan ci njafaanu ñoll,

Ña nga naa: «Dikkleen, ma indi biiñ, nu màndeew ñoll; tey ak ëllëg; li fi des du jeex.»

Hosea 7:5 TSK

Bu sunu buur xewlee, kàngam yi naan ba wopp, buur tàllal loxo ay ñaawlekat.

ak sàcc yi ak bëgge yi ak màndikat yi ak saagakat yi ak ŋàppaaral yi, duñu am cér ci nguurug Yàlla.

Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noo gi fees,