¶ Amoon na ca réewum Ucc, góor gu ñuy wax Ayóoba. Góor googu nekkoon ku mat te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.
TSK
TSK · Proverbs 20:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñeel Daawuda. Aji Sax ji, àtte ma, man de maandu laa wéye, Aji Sax ji laa wóolu, jenguma.
Day saxoo tabe, di leble, askanam barkeel.
Ku baax, donale ba cay sëtam; alalu moykat, muuru ku jub.
Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.
Xanaa kiy doxe njekk, di wax njub, bañ alalu foqati; loxo bay jalax ab ger, noppam di tanqamlu waxi bóome, bëtam di gëmm, ba du gis lu bon.
Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.
¶ Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.