TSK

TSK · Proverbs 22:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu góoru Yàlla ga yónnee ca buurub Israyil, ne ko: «Nanga moytoo jaare bérab sàngam, ndaxte fa la waa Siri jëm.»

¶ Gannaaw gi noon ya xam ne yég nanu leen, te Yàlla nasaxal na seen pexe. Ba mu ko defee nu walbatikuwaat nun ñépp ca tata ja, ku nekk dellu ca liggéeyam.

Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu, wormaale teddngaam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.

Acts 5:39 TSK

Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,

Ca saa soosa tembe la ko malaakam Boroom bi fàdd, ndax la mu delloowul Yàlla njukkal. Ba loolu amee, ay sax ronq ko, mu dee.

Su boobaa la ku dëng ka di feeñ, te Sang Yeesu moo koy jàllarbee ngelawal gémmiñam, te moo koy rajaxee ca na muy feeñe bu délsee.

Dinaa may nag sama ñaari seede yi, ñu biral waxyu diiru junni ak ñaar téeméeri fan ak juróom benn fukk (1 260) yu ñuy sol ay saaku, di ko toroxloo.»