TSK

TSK · Proverbs 27:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku.

Ci kaw loolu Yonent Yàlla Gàdd ne Daawuda: «Bul toog ci rawtu bi, fabul dem réewum Yuda.» Daawuda bàyyikoo ca, dem ba ca gottub Eret.

Firawna ne ko: «Ana loo ñàkk fii ci man, ba bëgga dellu nii sam réew?» Adàdd ne ko: «Du dara sax de, xanaa bëgg rekk, nga yiwi ma, ma dem.»

Ma ne ko: «Man duma kuy daw! Te sax gannaaw duma sarxalkat, nu may dugge ci biir néeg Yàlla bu mag bi, di génnaale bakkan? Man kay demuma.»

Jigéeni Mowab a nga ca jéggikaayu dexu Arnon, mel ni picc yu tasaaroo fa seeni tàgg, di fët-fëtluy, naaw.

Ci kaw loolu nit ña tiit tiitaange lu réy, ne ko: «Yaw, li nga def lu mu doon?» Fekk na Yunus xamal leen ne Aji Sax ji lay daw.

Jude 1:13 TSK

Ñooy gannaxi géej gu sàmbaraax, di gëq seen puuriti gàcce; ñooy biddiiw yu fàq di taxawaalu, te lëndëm gu ne këruus di cér bu ñu leen sédde ba fàww.