TSK

TSK · Proverbs 28:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Samiyel ne ko: «Ana meem joojuy tàbbi sama nopp bii, lu mu doon? Ak looluy nàññi, may dégg?»

¶ Ba loolu amee waa Sif dem Gibeya ca Sóol, ne ko: «Daawuda de, ma nga làqu fa nun. Ma nga ca xunti yu kawe ya ca Orsa, ca kaw tundu Akila, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum.

Ilyaas dikk jàkkaarlook mbooloo ma mépp. Mu ne: «Yeen nag dungeen dakkal seen ciŋiñ-caŋañ ji ngeen nekke, wet gu nekk ngeen féete fa? Su Aji Sax ji dee Yàlla, toppleen ko; su dee Baal, ngeen topp ko.» Mbooloo ma ne patt.

Wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Du dangaa rey nit, ba nangu alalam?” Nga teg ca ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Fa xaj ya xabe deretu Nabot, ay xaj dina fa xabe sa deret, yaw itam.”»

¶ Mu wax ak buurub Israyil ne ko: «Ana lu ma séq ak yaw? Demal kay ca sa yonenti baay yaak sa yonenti ndey ya!» Buurub Israyil ne ko: «Déedéet, ndaxte Aji Sax jee nu fi woo, nun ñetti buur yii, ngir teg nu ci loxol Mowab.»

Ba loolu amee ma yëlëb sama lafu mbubb wi may dence, daldi ne: «Yal na Yàlla yëlëbe nii mboolem ku sàmmul kàddu gii ci yeen, ba xañ ko këram ak alalam. Yal nañu ko ni yëlbe, ba mu jeexle tàkk.» Mbooloo ma mépp ne: «Amiin,» daldi bokk sargal Aji Sax ji. Mbooloo ma mépp nag def loolu ñu wax.

Ma ŋàññ jawriñ yi, ne leen: «Ana lu waral ñuy sàggane kër Yàlla gi?» Ci biir loolu ma woo Leween ñeek jàngkat yi, ñu daje, ma delloo leen ca seeni liggéey.

Ma ŋàññ kàngami Yuda, ne leen: «Lu ñaaw lii ngeen di def nag di teddadil bésub Noflaay?

Fekk na kenn ci doomi Yowada doomu sarxalkat bu mag ba Elyasib sax, jël doomu Sanbalat mu Oron. Teewul ma dàq waa ji, mu daw ba sore ma.

Du dee ba yóbbaale dara, teraangaam du ko topp biir bàmmeel.

Acts 15:2 TSK

¶ Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnaba séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnaba, ak ñenn ca gëmkati Àncos, ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu, ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.

Acts 24:2 TSK

Ñu woo Póol, Tertul daldi yékkati kàddug tuuma, ne: «Kilifa gi, ci yaw la jàmm ju yaa ame, te yaa fàggu ay coppite yu ñeel askan wi.

Moonte Tit mi ma àndaloon sax, tegeesu ko fa wartéefu xaraf, te ci askanu gereg yi dul xaraf la bokk.

Xam ngeen na nu jëkkoona sonne, ak na ñu nu torxale woon ca Filib, dëkk ba, bala noo dikk fa yeen. Teewul ci sunu ndimbalal Yàlla, nu ñeme leena àgge, ci biir xeex bu metti sax, xibaaru jàmm bu Yàlla bi.

Jude 1:3 TSK

¶ Soppe yi, yàkkamti woon naa leena bind ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye fàww ma bind leen, ngir ñaax leen ci xeexal yoonu ngëm, wi Yàlla xasa dénk ñu sell ñi, benn yoon ba fàww.