TSK

TSK · Proverbs 29:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Réccu naa li ma fale Sóol buur, ndax dëddu na ma, te samay ndigal, jëfewu ko.» Samiyel am ca njàqare lool, ba fanaanee tinu Aji Sax ji guddi gépp.

Buur Sóol woolu sarxalkat ba Ayimeleg doomu Ayitub, ak mboolem bokki baayu Ayimeleg ya doon ay sarxalkat ca Noob; ñu wuysi Buur Sóol, ñoom ñépp.

Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»

Aajo ju faju tooyal na xol, te ab dof jomb naa dëddu mbon.

Lu baax dees na ko feye lu bon a? Moona gasal nañu ma am yeer, di ma tëru. Bàyyil xel ba may taxaw fi sa kanam, di leen tinul ngir nga moyale leen sa mer.

Ñu xëcc buum yi, génne Yeremi kàmb ga. Gannaaw loolu Yeremi des ca biir ëttu dag ya.

¶ Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.

¶ Bokk yi, sama yéeney xol, ak ñaan gi may ñaanal Israyil ci Yàlla moo di ñu mucc.