1 Kings 3:13
TSK
Te itam li nga ñaanul dinaa la ko may, booleel la alal ak teraanga, ba doo am moroom ci buur yi, sa giiru dund.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Te itam li nga ñaanul dinaa la ko may, booleel la alal ak teraanga, ba doo am moroom ci buur yi, sa giiru dund.
Yaa ko gatandoo barkey ngëneel, kaalaa ko wurusu ngalam.
ngir fan wi gudd lool, nga gëna am jàmm.
Nawal xel mu rafet, mu darajaal la; tafoo ko, mu teral la.
Woyofal te ragal Aji Sax ji, am alal, gudd fan ak daraja.
¶ Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom,
Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.