TSK

TSK · Proverbs 30:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwma, daŋŋiiraluma, xintewoowma lu réy it, mbaa lu ma ëlëm.

Xeebaateek réy-réylu mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.

Aji Sax ji da ne: «Jigéeni Siyoŋ a ngi daŋŋiiral, di goŋeet-goŋeeti, di regejook a rékk-rékkal, samp um ndaag, keleŋal lami wëq.»

Xanaa doo janook ki lay rey, naati yaay yàlla? Boo tàbbee ca sa loxoy jamkat ya, keroog nga noppee doon yàlla, di nitu kese.

«Xol baa ngay xoggliku, te ag njub nekku ca, waaye ku jub ndax kóllëreem mooy dund.