Job 31:16
TSK
Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku, mbaa ab jëtun wékk ma bët, ma tas yaakaaram?
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku, mbaa ab jëtun wékk ma bët, ma tas yaakaaram?
Ndokklee yaw mi yég néew-ji-doole. Aji Sax jee lay xettli, bésub njàqare.
Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.
Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
Yeen ci seen bopp, xam ngeen ne, muy sama soxlay bopp, di yoy ñi ànd ak man, sama loxo yii laa liggéeye lu ma ko faje.
Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
Te it di def lu baax, ak di dimbalee, buleen ko fàtte, ndax sarax yu mel noonu la Yàlla gërëm.