TSK

TSK · Proverbs 31:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Biiñ mbaa naan guy màndal bu ko kenn ci yeen naan buy duggsi ci biir xaymab ndaje mi, du yaw, du say doom yu góor, lu ko moy dingeen dee. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.

¶ Ba Ben Addàd di jot ca kàddu googu, ma ngay naan, mook buur ya far ak moom ca mbaar ya. Mu jox ay nitam ndigal ne leen: «Takkuleen!» Ñu takku, ngir songi dëkk ba.

¶ Keroog bésub juróom ñaareel ba Buur Aserus naan biiñ, ba xolam sedd, mu sant juróom ñaari bëkk-néegam: Meyuman ak Bista ak Arbona ak Bigta ak Abagta ak Setar ak Karkas, ne leen

Naan biiñ ak ñaawle, naan ñoll, tanqale, ku mu nax xeluwoo.

Ndokklee, yeen, réew ma as gor falu, te bu jotee, jawriñ ñay xéewlu, ngir am doole te baña màndi.

Ñii itam ay naan biiñ bay tërëf, màndiw ñoll, di jang: sarxalkat akub yonent la aw ñoll di tërëfloo, biiñ jànnaxe leen, ñu màndiw ñoll, di jang, bu ñu amee am peeñu, di tërëf.

Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees, moo yóbbu seenum xel.

Biiñ day wore, jàmbaar ju bew jii nag du dal-lu, xanaa yàkkli puruxam ni njaniiw, du doylu, mbete ndee, moom miy buubandoo xeetoo xeet, dajale askanoo askan, aakimoo.