Job 31:4
TSK
Du Yàllaa ngi gis fu ma jaare, di waññ sama bépp jéego?
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Du Yàllaa ngi gis fu ma jaare, di waññ sama bépp jéego?
Yàlla déy a ngi ne jàkk ci jaar-jaari nit ki, di xool bépp jéegoom.
Jépp jëf déy, la Yàlla di àtte, ba ci lépp lu làqu, muy lu baax, di lu bon.
Ku mana làqoo làquwaay, ba duma ko gis?» Kàddug Aji Sax jee. «Xanaa du asamaan ak suuf, maa ko fees?» Kàddug Aji Sax jee.
Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.
Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.