Su boobaa tundu Siyoŋ bépp, fépp fu ñuy dajee, Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg, guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ; leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,
TSK
TSK · Revelation 21:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.
¶ Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kawa kaw lay nirook ngàngune.
Sa liggéeyu jula bu yaatu moo la feesal fitna, nga bàkkaar, ba ma nangoo sa teddnga fa tundu Yàlla wa, sànk la, yaw malaakam serub miy aare, nga jóge digg doj yuy tàkk.
Wurmbalu dëkk bi bépp fukki junniy xasab ak juróom ñett (18 000) lay doon. Turu dëkk bi nag, dale ko ca bés ba, di “Aji Sax jaa ngi fi.”»
Fi janook ngàngune mi lu mel ni géeju kiristaal, leer nàññ. Fi wër ngàngune mi ci wet gu nekk, ñeenti bindeef a ngi fi, fees aki bët ci kanam ak ci gannaaw.
Tata ji peru jàspë lañu ko liggéeye, dëkk bi di wurusu ngalam, leer nàññ ni kiristaal.
¶ Ci kaw loolu malaaka mi won ma dexu ndoxum dund mu leer nàññ ni doju kiristaal, ndox ma wale ca ngàngunem Yàllaak Gàtt ba,