TSK

TSK · Romans 12:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 31:13 TSK

Ndegam maa sofental sama àqu jaam, bu ñu may jooytu, diy góor mbaa jigéen,

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwma, daŋŋiiraluma, xintewoowma lu réy it, mbaa lu ma ëlëm.

Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.

Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.

Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.

Maa leen di may benn xol ak benn jubluwaay ngir ñu di ma wormaal seen giiru dund, muy seen ngëneel, ñook seen doom yi leen di wuutu.

Luke 6:20 TSK

¶ Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: «Ndokklee yeen ñi néewle, nde nguurug Yàlla, yeenay boroom.

¶ Ab werante itam dikkal leen, ñuy xëccoo ci seen biir ku wara gëna kawe ci ñoom.

Mukk kay! Nun ñi ndee tàggale ak bàkkaar ba noppi, ana nu nuy saxootee bàkkaar?

¶ Ma àrtu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.

¶ Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.

Nun, ay dof lanu ngir Almasi; yeen, yeena muus nu ngeen bokke ci Almasi! Nun noo néew doole; yeen, yeena am doole. Yeen it lañu naw, waaye nun, dees noo xeeb!

¶ Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di xeex ngir saxal ngëm gi sukkandiku ci xibaaru jàmm bi.

Ak lu ci mana am, yoon wii nu doxe ba fii nu tollu, nanu ko bokk topp.

Ag ñàkk nag taxul may waxe nii, nde tàmm naa di doylu ci diggante bu ma mana tollu.

¶ Buleen jikkowoo bëgg ub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»

¶ Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet.

Buleen jaay kilifteef ñi ñu leen dénk, waaye doonleen ay royukaay ci jur gi,

Ñu may ko itam mu xareek ñu sell ñi, duma leen, boole ci may ko sañ-sañ ci kaw niti gépp giir ak wépp xeet ak wépp làmmiñ ak wépp askan.