TSK

TSK · Romans 13:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.

¶ Ci kaw loolu Samiyel ñaan ci Aji Sax ji, Aji Sax ji dënu, taw ca bés ba. Mbooloo ma mépp nag ragal lool Aji Sax ji ak Samiyel.

Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.

Mu ne leen: «Kon kay yëfi Sesaar, joxleen ko Sesaar; te yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.»

Teewuleen koo moom yeen itam; kon na ku nekk sopp jabaram ni mu soppe boppam, te ku nekk weg jëkkëram.

¶ Yeen jaam yi, déggal-leen seen sangi àddina, ànd ceek ragal Yàlla bay kat-kati, ak xol bu dëggu. Ni ngeen déggale Almasi, nangeen leen ni déggale.

¶ Mag ñiy jiite mbooloo mi bu baax nag, nañu leen yellale ag njukkal ñaari yoon, rawatina ñi boole coonoy waare ak njàngle.

Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.