Yaw de, ñu bare jàngal nga leen, loxo yu toqi woon, nga dooleel,
TSK
TSK · Romans 14:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmm ug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»
Yeen, li ndóol ci jur gi, leqliwuleen; li ci wopp, fajuleen; li damm, yeewuleen; li ci lajj, gindiwuleen; li réer, seetuleen. Doole daal ngeen leen yilife, di leen soxore.
Maa ngi nii kat di taxawal ab sàmm ci réew mi. Lu ci réer, faalewu ko; lu ci lajj, du ko seet, lu ci gaañu, du ko faj, lu wér du ko xont, te lu ci duuf, mu yàpp, ba toj seeni we.
Ñu takkoon doj wu réy ci baatam, sànni ko biir géej moo gën ci moom muy yóbbe bàkkaar kenn ci xale yii.
Ngëmu Ibraayma wàññikuwul, doonte ba mu xoolaatee boppam, xam na ne yaramam dee na daanaka, ndax fekk na ay atam xawa tollu ci téeméer, te njurukaayu Saarata it fekk na ko dee.
¶ Nun ñi fendi ci wàllu ngëm, fàww nu xajoo tëley ñi néew doole, te baña sàkku sunu bànneexu bopp.
¶ Man nag bokk yi, manuma woona wax ak yeen ni ñuy waxe ak ñu ànd ak Xelum Yàlla, waaye ni niti suuxu neen rekk laa manoona waxe ak yeen, mbete ñu diy tuut-tànk ci yoonu Almasi.
Maak boroom ngëm yi desee dëgër, damaa mel ni ku ngëmam desee dëgër, ngir iri leen. Lépp laa def sama bopp ci ñépp, ak nu mu mana deme, ba musal ñennat.