Jépp jëf déy, la Yàlla di àtte, ba ci lépp lu làqu, muy lu baax, di lu bon.
TSK
TSK · Romans 14:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Erodd aki dagam nag sewal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu yànj, delloo ko Pilaat.
Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen beddi woon, yeen tabaxkat yi, te mu mujj di doju coll wi.”
Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu taamu di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu taamu, ndekkite lu dee toppul.»
Kiy lekk, bumu ko xeebe ki lekkul; ki lekkul it, bumu sikk kiy lekk, ndax Yàllaa ko xajoo.
Ndax kat, nun ñépp fàww nu taxawi fa jalub àttekaayu Almasi, ngir ku nekk yooloo kemu jëf ja mu jëfe yaramam, muy lu baax, mbaa lu bon.
¶ Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex, ak ku ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes.