Noon ya raaf, gental ba fàww. Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
TSK
TSK · Romans 2:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi njekk, tey àttee xeet yépp dëggam.
Saam xel ne ma, ku jub ak ku bon la Yàlla di boole àtte, ngir mbir mu ne ak jëf ju ne ak bésam.
Jépp jëf déy, la Yàlla di àtte, ba ci lépp lu làqu, muy lu baax, di lu bon.
Moo nu sant nag nu xamal askan wi te seede ne moom la Yàlla tabb àttekatub aji dund ñi, ak aji dee ñi.
¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.
Yaw nag ana looy sikke sa mbokkum gëmkat, ak itam, ana looy xeebe sa mbokkum gëmkat? Ndax kat nun ñépp ay taxawi fa kanam jalub àttekaayu Yàlla.
Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.
¶ Bokk yi, ma xamal leen ne leen xibaaru jàmm bi may yégle, bàyyikoowul ci nit.
¶ Bàyyil xel ci Yeesu Almasi mi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee.
Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, Àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.
waaye ñoo koy layoo ak ki nara àtte ñiy dund, ak ñi dee.
¶ Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex, ak ku ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes.