TSK

TSK · Romans 2:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ana ku xam sa dooley mer ak sa xadar ju raglu?

Ana ku ragal Aji Sax ji ci yeen, di déglu kàddug jaamam? Képp kuy doxe lëndëm te amul leeraange, na wóolu Aji Sax ji, te wéeroo Yàllaam jii.

Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.

¶ Waaye du ñépp a nangul xibaaru jàmm bi; moo tax Esayi ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunub dégtal?»

Waaye ku bëgga werante ci leneen it, nun loolu du sunu baax, te du baaxu mbooloom Yàlla mi.

ak mboolem xeeti naxe yu njubadi lal, ñeel ñi nara sànku ndax ñàkka sopp dëgg gi, ngir nangu ko ba mucc.

Titus 3:9 TSK

Waaye ay werante, ak limi maam, aki xuloo, aki jaayante xam-xam ci yoonu Musaa, moytu ko, ndax loolu amul njariñ, amul solo.

Noonu lees matale Almasi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.

¶ Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm bérab ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.

Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm?

Dëkk bu mag ba xar ñett, dëkk yu mag yu askani àddina yi màbb. Babilon gu mag ga nag, Yàlla bàyyi ko xel, ngir nàndal ko kaasu biiñu sànjam muy bax.