TSK

TSK · Romans 4:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jee koy seppee ci mboolem giiri Israyil, ngir sédd ko njekkar, na mu dëppook mboolem alkàndey kóllëre gi ñu bind ci téereb yoon wii.

Kon nag sol-leeni saaku, ñaawloo te yuuxu ne: “Merum Aji Sax ji tàng na kat te moyu nu.”

Seen xaalis, ñu sànni ci mbedd yi, seen wurus di leen saf sagaru sobe. Keroog bésub sànjum Aji Sax ja, du xaalis, du wurus wu leen di xettli. Du leen fajal xiif, du leen reggal, xanaa tàbbal leen cig njubadi.

Yàlla nag jéllale na janti ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp, ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub.

¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.

¶ Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.

¶ Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,

¶ Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.»

¶ Bu leen kenn naxe waxi ngelawal neen, ndax yooyu ma lim mooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw aji déggadi ñi.

Gémmiñ gi, saamar bu ñaw a ciy lange, mu di ko cawe askan yi. Moo leen di jiitee yetu weñ, te mooy dëggaate ci biir nalukaay bi, reseñ ji ñuy segale biiñu sànj mu tàng mu Yàlla Aji Man ji.