Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon, taxawewuloo yoonu moykat, toogewuloo jataayu ñaawlekat.
TSK
TSK · Romans 4:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal, du sotti, te boroom làmmiñ wu la jógal cib layoo yaa koy tiiñal. Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér, looloo di njekk gi ma leen di dikke.» Kàddug Aji Sax jee.
Bés yooyu Yuda day mucc, Yerusalem dëkke jàmm, ñu di ko wooye: “Aji Sax ji sunu njekk.”»
Ndax kat deesul jox kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solob yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.
¶ Kon moomu mbégte xanaa Yawut yiy xaraf doŋŋ la ñeel? Ñi xaraful it dañu cee bokkul? Ndax kat danu ne Ibraayma lañu waññal ngëmam ga, ag njub.
Nun itam ci lanu; dees na nu waññal sunu ngëm, àtteb ñu jub, nun ñi gëm Ki dekkal sunu Sang Yeesu,
Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,
Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»
Ana seen mbég mooma woon nag? Ndax kat maa leen seedeel ne su manoona am sax, seeni bët ngeen di luqi, jox ma.
Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la;
Moo nu musal, woo nu woote bu sell te sunuy jëf taxul, waaye coobarey boppam a tax, ak yiwam wi ñu nu may ci Almasi Yeesu, balaa ay jamonoy jamono di sosu.