TSK

TSK · Romans 5:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Gis naa ne it Israyil Woyof-Kumba-si gànctu na ba ma yebal ko, jox ko kayitu pase, mu dem, te taxul doomu ndeyam Yuda workat bi ragal. Moom it daa dem di gànctu.

Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

¶ Kenn ca saaysaay ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi? Wallul sa bopp te wallu nu!»

Yoonu Musaa daal, am sànj lay jur, te fu yoon wees di sàmm amul, genn moy amu fa.

Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

¶ Waaw kon yoonu Musaa, ana luy njariñam? Dees koo toftal ca dige ba, ngir muy fésal moyi nit ñi ba keroog boroom dige, bi taxawal askanu Ibraayma, dikk. Ay malaaka ñoo biral yoon wi, ci ndimbalal ab jottlikat.

¶ Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar,

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.