¶ Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.
TSK
TSK · Romans 5:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Romans 5:12
TSK
Romans 5:17
TSK
Moyug kenn nit ki, ci la dee jaare ci kenn nit kooku, ba falu, kon ñi jot ci xéewalu yiw, ba jagoo àtteb njub, ñaata yoon lañuy gënatee falu ci biir dund gu ñu ame ci keneen nit kiy Yeesu Almasi?
Romans 6:14
TSK
Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
Romans 6:23
TSK
Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.
Titus 2:11
TSK
¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.
1 Peter 5:10
TSK
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.