Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji. Aji Sax jee gore, te yaatug njot.
TSK
TSK · Romans 6:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Kon nag dige Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.
Kon nag bu bàkkaar yilif seen yaramu ndee wii, ba di leen nanguloo ay xemmemtéefam yu bon.
¶ Noonu la deme ak yeen itam, bokk yi. Yaramu Almasi wi ngeen bennool, ci ngeen doone ñu deeyal yoonu Musaa. Noonu ngeen doone moomeelu keneen, te kooku mooy ki dekki, ngir nu meññ njariñ lu ñeel Yàlla.
¶ Kon nag bokk yi, bor topp na nu, waaye du sunu bindu suux lanu ameel lenn lu nu taxa topp sunu bakkan;
Moo nu may manoorey doon ay liggéeykati kóllëre gu bees gu ajuwul ci mbindum ndigali yoon, xanaa kóllëre gu aju ci Noo gi. Ndaxte mbindum ndigali yoon day rey, te Noo gi di dundloo.
Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,
Waaye su leen Noo gi jiitee, su boobaa nekkatuleen ci kilifteefu yoon wi.
¶ «Lii nag moo di kóllëre gi may fas ak kër Israyil, gannaaw yooyu fan, la Boroom bi wax, mu ne: Maay yeb sama ndigali yoon ci seenum xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.