TSK

TSK · Romans 7:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.

Ay waxam coxor aki fen, jëfeetul lu rafet ak lu baax.

Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, di leen musal ci ku bon.

Ndokklee yaw mi maandu, di wéye yoonu Aji Sax ji.

Ku jub bañ na ay fen, ku soxor di indi gàcceek yeraange.

Amos 5:15 TSK

Bañleen lu bon, bëgg lu baax, di doxal yoon ci pénc. Jombul Aji Sax ji Boroom gàngoor yi baaxe ndesu askanu Yuusufa.

Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel.

Ndax kat du lu baax li ma namma jëfe laay jëfe, waaye lu bon li ma nammul, moom laay jëfe.

¶ Yaw ci sa wàllu bopp, ngëm gi nga ci am, yemale ko ci sa bopp, fi kanam Yàlla. Ndokklee ki sikkul boppam lenn ci jëfin wu mu dogul boppam ne noonu lay jëfe.

¶ Du caageenu damaa àgg ci loolu lépp ba noppi, mbaa damaa mat sëkk xaat, waaye maa ngi wéye samaw xél, di jéema jot ci neexalu rawante bi, gannaaw ba ma Almasi Yeesu jotee ci man itam.

Yaa safoo njubte, seexlu njubadi, moo tax yaw Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom.»