Su nit àbbee juru moroomam, jur ga damm mbaa mu dee fu boroom nekkul, na ki àbboon fey.
TSK
TSK · Zechariah 13:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Tojleen seeni sarxalukaay, rajaxe seen tuuri doj; seen xer yi ñuy jaamoo Asera tuur mi, ngeen lakk; seen jëmmi tuur, ngeen gor, ba far tukkal turi tuur yi ci yooyu bérab.
Kuy sàkkuy tuur barew tiis, man de duma leen tuural deret, sama làmmiñ du leen tudd.
Bésub keroog booba, yàllantuy xaalis ak wurus ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal, ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya,
Waaye yonenti Yerusalem laa gisal lu yées: ñuy jaaloo, di wéye ay fen, di dooleel defkatu lu bon, ba kenn dëdduwul mbonam. Ñoom ñépp di ma niru waa Sodom, waa Yerusalem it ni waa Gomor.»
Bu tata ji jekkee ne jànjaŋ, deesu leen laaj fu weexal ba ngeen ca raaxoon jaar?
¶ «“Su fekkee ne yonent baa am lu ko nax, ba àddul boppam genn kàddug waxyu, day fekk man Aji Sax ji maa nax yonent ba. Maa koy dumaa sama loxo, sànke ko digg Israyil, sama ñoñ.
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
Mu ne ma: «Yaw nit ki, sama màkkaanu ngàngunee ngi, bérab bii laay teg samay tànk, di fi dëkke fi digg bànni Israyil ba fàww. Bu waa kër Israyil dellu teddadil sama tur wu sell, ñook seeni buur ci seen gànctu, ak seen néewi buur yi ñuy denc ci seeni jaamookaay.
Turi tuuri Baal laay jële ci sa gémmiñ, ba deesatul fàttliku seen tur.
Nit man naa wër, toppi caaxaan aki fen, naan: “Maa lay yégal waxyub biiñ aku ñoll,” te kookooy jottlikatub waxyu bi askan wii yelloo!
«Doom aadama ak mala, njanaaw ak jën laay buub, ak luy fakktale, booleek ñu bon ñi. Maay dagge doom aadama fi kaw déndub suuf.» Aji Sax jee ko wax.»
Waaye su dee loxol Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen.
¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.
Mu àddu ca kaw, ne: «Babilon a daanoo! Dëkk bu mag ba daanu na, ba doon dëkkukaayu jinne ak mboolem njuuma lu sobewu ak mboolem picc ak rabu àll wu sobewu te siblu.
¶ Ba mu ko defee ma gis malaaka mu wàcce asamaan, yor caabiy xóote bi, ak càllala gu réy.