TSK

TSK · Zechariah 8:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jeey waaxu ni jàmbaar, xabtalu ni ñeyu xare, àddu ca kaw, xaacu, tiime noon yi njàmbaaram.

Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.

Boroom bi Aji Sax ji nag dafa wax ne: Maa ngii déy di waxe sama tàngooru fiiraange ak xeet yi dul yawut, boole ci Edom gépp, ñoom ñi jiital seen xeebeel, te suuf si ma séddoo, ñu aakimoo ko, te di ko bége mbégte mu mat sëkk, ngir sëxëtoo parluy réew mi.”

Nahum 1:2 TSK

Aji Sax ji mooy Yàlla ju fiir, te mooy mbugale, Aji Sax ji mooy mbugale, te di boroom sànj. Aji Sax ji mooy mbugal ay bañam, mooy sànju ci kawi noonam.

Ca la ma malaaka ma doon wax ak man, ne ma: «Yéeneel, nga ne: Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Maa fiire Yerusalem, maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy.