Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ku jara sës ku dul sunu Yàlla?
TSK
TSK · Zechariah 9:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yeen, xeetoo xeet, dégluleen; yeen, waa àddina yépp, teewluleen,
di xaacuy kañ Yàlla, ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
Moo ñawal sama kàddu ni saamar, làqe ma keru loxoom. Moo ma def may fitt gu ñaw, yeb ma ci mbuusum fittam.
Doomi Siyoŋ yu góor yu jar ya! Wurus lees leen daan nàttablee, ndeysaan tey, ñu jàppe leen ni njaqu ban lu tabaxkatu njaq liggéeye loxoom.
Ñi sàmmul kóllëreg Yàlla ay nax la leen di fàbbee, waaye askan wi ràññee seen Yàlla, pastéef lañuy jëfeji.
Maa tabboon ci seen doom yu góor ay yonent, tànne ci seen xale yu góor ay séddoo, — am déet, yeen bànni Israyil?» Kàddug Aji Sax jee.
Xeet yu bareey dikk te naan: «Dikkleen nu yéegi ca tundu Aji Sax ji, kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.
Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk, ci biir xeeti àddina, mbete gaynde ci biir rabi àll yi, nirook gaynde gu ndaw ci biiri gàtt; fu mu jaare, joggati, xotat, te kenn du wallu.
«Sàmm yi la sama mer tàkkal, ñoom sikket yooyu laay dikke mbugal. Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat mooy taxawu kërug Yuda, géttam, te moo leen di def aw fasam wu am daraja, ngir xare.
Yàlla moo dogal ci xam-xamam, àddina tële koo xam ci xam-xamu boppam. Moo tax mu soob Yàlla, mu jëfandikoo xibaaru Almasi, biy ag ndof ci nit ñi, ngir musale ko gëmkat ñi.
Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jël-leen ko, sol, jël-leen itam saamar bi Noo giy joxe, te muy kàddug Yàlla.
Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.
¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Pergam nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Boroom saamar bi ci ñaari ñawka yi. Mu ne:
Gémmiñ gi, saamar bu ñaw a ciy lange, mu di ko cawe askan yi. Moo leen di jiitee yetu weñ, te mooy dëggaate ci biir nalukaay bi, reseñ ji ñuy segale biiñu sànj mu tàng mu Yàlla Aji Man ji.