TSK

TSK · 2 Peter 1:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Musaa nag ne: «Lii nag moo leen di xamal ne Aji Sax ji moo ma yebal ngir ma def jëf jii jépp, waaye du sama coobarey bopp:

¶ Yàlla-woo-yàlla, genn góoru Yàlla jóge Yuda, dikk ba Betel ci ndigalal Aji Sax ji, fekk Yerbowam taxaw ca sarxalukaay ba, nara taal saraxu cuuraay.

Jigéen ja ne Ilyaas: «Léegi nag xam naa ne nitu Yàlla nga, te kàddug Aji Sax ji ngay waxe moos.»

Ci biir loolu mu ne jëkkëram: «Aa, man déy, xam naa ne kiy fara dal ak nun góoru Yàlla gu sell la.

Buurub Israyil yónnee fa ko góoru Yàlla ga wax, ngir nemmiku foofa. Alyaasa di artoo Buur noonu, muy fàggandiku. Loolu am na bu dul benn yoon, du ñaar.

Micah 3:7 TSK

Seetkat yi dañuy rus, boroom ngis yi torox, ñoom ñépp jàpp seen gémmiñ; ndax Yàllaa leen dul faale.»

Luke 1:70 TSK

noonee mu ko waxe woon ca jant yu jëkk ya, yonentam yu sell ya woon jottli,

Acts 3:18 TSK

Waaye Yàlla moo sottale noonu la mu yégle woon lu jiitu, yonent yépp jottli, ne Almaseem dina sonn.

Bi ngay lu tuut nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye.

Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye dugg ca bérab bu sell baa sell feeñagul woon, te fekk néeg bu jëkk ba di taxaw ba tey.

Gëstu nañu jan jamono, ak yan xew-xew la Noowug Almasi ga nekkoon ci ñoom, tegtale woon. Mooy ba Noo gay seede lu jiitu, coonoy Almasi, ak ndam ya cay topp.